Pitax mu ndaw
- Détails
- Catégorie : Littérature
- Affichages : 572
Woy wii Sëriñ Aadi Turee ko fent. Séexu Tiijaan Sëriif la ko jagleel.
Soxna Aram Faal moo leen ko jottali, tibbe ko ci téereb OSAD bu tudd : Téere Dawal, 1995, xët 40-42.
Pitax mu ndaw
Bismilaa Rahmaani Rahiim
Faa ilan, faa ilan
Nan ci woy ciy wolof
Soo woyee ciy wolof
Kon ci xol lay xaraf
Déglu naa biig ci njël
Am pitax ciy garab
Ñuy tawat naan hadiil ( moo di picc mu ndaw)
Ab liccin moo ko këf
Mii pitax naa ko ndax
Mar wu tar waa ko rey
Mii pitax naa ko man
Xaajumaa wóolu maf
Mii di woy, mii di jooy
Kurkutuut, kurkutuut
Soo amul fathu nag (moo di ag ubbeeku)
Doo ca am aw araf
Seeni woy moo yëngal
Tiisu xol wi ci man
Moo tax it maa ngi nii
Maa ngi saf waa ju dof
Maa ngi leen naa
Yéen dangeen dul nelaw
Yéen pitax yi ñu naa
Jooju wax nañ ko laf
Nun danoo sib nelaw
Kuy nelaw doo nu saf
Kuy nelaw yaa ko tal
Nun sunuy bët du raf
Foo fi gis kuy nelaw
Ag cofeelam wérul
Su cofeelam wéroon
Kon bëtam sax du xef
Waa ji man waaru naa
Yii pitax ñoo nu gën
Seen cofeel ak hadiil
Soo mënoon roy ko faf
Fuy pitax deeti woy
As hadiil, nan fa woy
Séexu Tiijaan Sëriif
Moo ko jar mag du kaf
Séexu Tiijaan Sëriif
Nan ko woy, nan ko roy
Ay waxam nan ko ca ŋoy
Moo nu doy, moo nu saf
Séexu Tiijaan Sëriif
Ndeem dangay roy ci moom
Ay jëfam day rafet
Ay waxam day woyof
Séexu Tiijaan Sëriif
Waaru naa ciy mbiram
Ag cofeelam ci xol
Rekk sax doy na jëf
Séexu Tiijaan Sëriif
Ab kemam daa amul
Foo ko seet, doo ko gis
Muy Kajoor, muy Jolof
Séexu Tiijaan Sëriif
Kuy kokam daldi raw
Soo ko soppee ci xol
Kon bégal, am ngërëm
Daaguleen cim lefam
Daldi raw gaa ya war
Naaru-góor yay dawal
Aw yeneen xeeti lef
OSAD a ñëwaat ak yéen ci mbind mi
a / o
wal ( ndox muy wal) / wol (wol dugub)
way (meew mu way) /woy (woyu cosaan)
a / e
tay (tay cere) / tey (bésu tey, moo ko tey)
Buleen bind Bindleen
weddi guiss boccouci weddi gis bokku ci
njuuj-njaac njuuj-njaaj
Geum sa Rew Gëm sa réew










